Gise ak Maam Yunus Jeŋ / Entretien avec Mame Younousse Dieng

Mame Younousse Dieng

Portrait réalisé par Daam LO, Wikimedia Commons, 2017

https://commons.wikimedia.org/wiki/File:Maam_Yunus_JENG_2017.jpg

.

.

.

Mots-clés:  wolof, Sénégal, Gambie, Mauritanie — écriture littéraire, roman; romancière — littérature orale, griot, griotte — mariage polygame, première épouse.

Entretien Réalisé en wolof sous forme d’enregistrement audio le 28 mars 2014 à Dakar, par Saly Amy Diémé, qui a transcrit et traduit l’entretien.

Biographie:  Née en 1939 à Tivaouane dans le Cayor, au Sénégal, Maam Yunus Jeŋ [Mame Younousse Dieng] est décédée en 2016. Elle a fait ses études secondaires au Collège Ahmeth Fall de Saint-Louis. Elle était institutrice et directrice d’école. Dans son enfance, dans une grande famille polygame, elle avait souvent l’occasion d’entendre les griottes (géwél) et les discussions de femmes, ce qui lui a inspiré certains thèmes de ses romans.

Maam Yunus Jeŋ [Mame Younousse Dieng] est la première femme sénégalaise à avoir écrit un roman en wolof, en l’occurrence Aawo bi [La Première épouse] 1. Elle a également publié des poèmes et un roman en français (voir ci-dessous « Œuvres »).

Œuvres:  Aawo bi [La Première épouse], fentaakon bi [fiction], Dakar, Organisation sénégalaise d’appui au développement (OSAD), Collection « Teere fent » [ouvrages de fiction], 1999, 2e édition, 76 p. [Première édition, Dakar, IFAN/Cheikh Anta Diop, 1992, 72 p.]

L’ombre en feu, Dakar, Les Nouvelles Éditions Africaines du Sénégal, 1997, 236p. [manuscrit déposé chez l’éditeur en 1977]

Sommaire de l’entretien:

      • Téereb fent ci wolof / Un roman en wolof
      • Janeer / Inspiration
      • Am génnekatu teere / Trouver un éditeur
      • Warugari bind kat bi / Droits d’auteur
      • Bind ci farãse wala ci wolof ? / Écrire en français ou en wolof ?
      • Aawo bi / La première épouse
      • Bind ci wolof / Écrire en wolof
      • Way-jëmmal yi / Les personnages
      • Séyu kujje / Mariage polygame
      • Nettalikatu géwél / Le griot comme narrateur
      • Jafe-jafeey fésal téere / Difficultés de publication
      • Tekkim Bataaxal bu gudde nii ci wolof / Traduction en wolof d’Une si longue lettre
      • Áddinay jigéen ñi / Le monde des femmes
      • Ay woy / Des poèmes
      • Feminist yi / Les féministes
      • Aada ji / La tradition
      • Pόlόtik bi / La politique

 

 

 

 

 

Gise ak Maam Yunus Jeŋ

Entretien avec Mame Younousse Dieng

 

 

Sali Ami Jemme (S.A.J): Bind nga ay woy ak ñaari téere fent. Bëggoon naa xam naka la la mbind mi dikke.

Saly Amy DIEME (S.A.D): Vous avez écrit des poèmes et deux romans, je souhaiterais savoir comment avez-vous été initiée à l’écriture.

Maam Yunus JEŊ (M.Y.J) : Xam nga nettali ak bind moom […] ñun dañu ko bind rekk.

Mame Younousse DIENG (M.Y.D): Vous savez, entre raconter et écrire, il n’y pas une grande différence […], j’ai plutôt choisi l’écriture.

Littérature orale

Littérature orale

Waaye boo déggee li tubaab naan littérature orale am na. Loolu dafa mës a am ci sunu réew mi, mësu fee jόge. Ne bu njëkk bu guddee boo reeree ba noppi yaa ngay léeb wala yaa ngay nettali. Wala nga añ ba noppi nga toog ci taatu garab, benn géwél ñëw di nettali dara dale-ko ci cocc ba coset. Wax la fa mu jaar […]. Loolu téere la di, fent la. Fent boobu nak ñun daawuñu ko bind. Kon bind ko dafay yomb, te man ba may xale ba léegi yalla daf ma xiir ci bind.

La littérature orale a toujours existé dans notre pays et elle n’a jamais disparu. Autrefois, après le dîner, on racontait un conte, une histoire. Parfois, après le déjeuner vous vous asseyiez sous l’arbre à palabre et un griot venait raconter une histoire du début à la fin et dans les moindres détails. Cela est un livre. Cette histoire, nous ne l’écrivions pas. Donc l’écrire devient facile et moi, depuis mon enfance, l’écriture m’a toujours attirée.

Njàngum mbind

Apprentissage de l’écriture

Naka ma dugg ekool luñ ma jàngal ma ñëw di ko waxaat, di ko fentaat. Man day mel ni sax su ma ko waxaatul ci sama làkk ba mu yégg, du ma xam nu ma bëgg mu dugge ma ko. Xëy-na moo ma dimbali tam ba ma nekkoon ku mën jàng […]. Su ma daan jàng samay leson sax noonu laa ko daan jànge […]. Mbind mi daal noonu la ma ci yàlla xiire. Ba yàgg may bind ay woy, ndax woy moom dañu koy judduwaale. Dañuy juddu fekk fi woy yi. Xam nga fii Afrig lépp lañuy woy. Bànneex dañu koy woy, naqar dañu koy woy. Bu ñuy kàll dañu koy woy, boo gisee ñu juboowul dëkk bu ñuy gaaruwaalante dañ koy woy […]. Woy moom dafa dëkk ci Afrig. Bokkul ak li nga xam ne danga koy jàng ekool […]. Moo tax bind daal jafewul woon.

Dès que je suis entrée à l’école, je traduisais tout ce qu’on m’apprenait. J’avais l’impression que si je ne le traduisais pas dans ma langue, je ne pourrais pas retenir le sens. C’est ce qui m’a peut être aidée à être une élève brillante […]. Et même pour apprendre mes leçons, je les traduisais d’abord en wolof […]. C’est ainsi que j’ai débuté dans l’écriture. Par la suite, j’ai commencé à écrire des chants, car la chanson, on naît avec. Vous savez en Afrique tout se chante, les moments de bonheur, de malheur, quand on s’exprime en verlan, des voisins qui ne s’entendent pas bien se lancent des attaques verbales indirectes en chantant […] La chanson fait partie du quotidien. Elle est différente de ce qu’on apprend à l’école […]. C’est pourquoi je n’ai pas rencontré de difficultés à écrire.

Mbindmu njëkk

Premiers écrits

Ba ma toogee ba wara wax itam, fekk na it sama boroom kër gaañu, ma wéet yor ay xale yu ndaw, bari lu ma bëgga wax daal te mënuma woona génn di wax it. Ma daldi tàmbali di wax ak sama bopp. Jël samay kayit di bind ti tek. Lu ma xalaat sirtu ci waxi jigéen rawatina ci nak. Ba ma bind romaa. Ma joxe ko nak mu të wa génn, të wa génn, të wa génn ba yàgg ma ni bii de du génn.

J’ai commencé à écrire et cette période coïncide avec le décès de mon mari. Je me sentais seule avec mes enfants en bas âge. J’avais beaucoup de choses à dire, mais je ne pouvais pas sortir de chez moi parce que j’étais en deuil. J’ai commencé à parler toute seule. Par la suite j’ai pris des feuilles et j’ai commencé à écrire tout ce qui me passait par la tête, particulièrement sur la femme. J’ai fini par écrire un roman [en français] que j’ai déposé [chez l’éditeur] et qui a mis du temps pour être publié. J’ai fini par me résigner à l’idée qu’il ne sortira jamais. 

Téereb fent ci wolof

Un roman en wolof

Man maa ñàkk-fayda sax ba di ko bind ci tubaab, ba tax ñu di ma këll-këllee boobu ba tey. Ma daldi ne man tee maa bind benn fent wolof. Man li ma jaxaal ci wolof yi léeb a ngi ci, woy a ngi ci, ay kàll a ngi ci, ay gaaruwaale […]. Waaye man daal gisaguma ci téere fent.

Je me suis dit que c’est ma faute, pourquoi écrire en français pour ensuite être malmenée ainsi2? Je me suis dit pourquoi ne pas écrire un livre de fiction en wolof puisqu’il y a des contes, des poèmes, des verlans, des « attaques verbales indirectes » […]. Mais je n’ai pas vu de roman.

Rekk ma daldi toog fent benn. Xool sama yaay fekk mu ñëw fi kat. Moom bu ma nuyusee day bëgg ñuy waxtaan. Su ma jàngalejee ba noppi ñu toog di waxtaan ba muy ñibbi. Waaye weer woowu ndeysaan, léeg-léeg mu fab kayit yi, sanni fee. « Bàyyil sa kayit yi te nga déglu ma. Yow lu tax ma ñëw fi ba noppi doo wax ak man nga sëgg ci sa kayit yi doo waxtaan ak man ». Te fekk na ci moom laa xool ba am yég-yégu bind, wax ci séy yi ci Senegaal ak mbirum aawo ni mu wara mel. Ndax gis naa yu bari. Fekkoon na ci samay ndongo yu nekkoon foofu dangay gis ku yaayam ñëw fekk la fi nga toog sa biro di liggéey mu wax la sama wujj a def lii sama wujj a def lii. Ma daldi ne waa Ndakaaru manu ñu wujje.

Et j’en ai créé un. J’ai observé ma mère qui était venue me rendre visite. Quand elle venait me voir, elle voulait qu’on discute après le travail. Ce mois-là, elle jetait souvent mon manuscrit. « Arrête d’écrire et écoute moi. Pourquoi tu ne discutes pas avec moi, tu es toujours penchée sur tes feuilles au lieu de discuter avec moi ». Alors que c’est elle qui m’a inspiré ce que j’écrivais, [c’est-à-dire] parler des mariages au Sénégal, et [montrer] comment doit être une première épouse. Car j’ai vu beaucoup de problèmes de mariage. A ce moment, plusieurs mères de mes élèves venaient dans mon bureau pour me raconter leurs problèmes avec leurs coépouses. Je me suis dit que les Dakaroises ne savent pas vivre avec une coépouse.

Janeer

Inspiration

Ma ni négal ma won leen sama yaay moom ni mu wujje woon ak wujjam yi ni mu rafetee. Xam naa bu doon autobiographie dinaa ne moom la, waaye doonu ko ndax bari na lu ñu wuute dal. Bu dul ci jikko ji daal, li ci des du sama yaay. Ndax sama kër pàppa gëmuma ni nii la meloon. Miinuma woon sama pàppa, waaye melul woon nii.

Je me suis dit je vais leur montrer la belle façon dont ma mère vivait avec ses coépouses. Si c’était une autobiographie, je dirais que c’est ma mère, mais ce n’en est pas une car il y a beaucoup de différences. A part son caractère3 tout le reste, n’est pas ma mère. Je ne pense pas que ma maison paternelle était ainsi4. Je n’ai pas vécu longtemps avec mon père, mais il n’était pas ainsi5.

Waaye sama yaay ku baxoon la, baax. Mënuma woona baña bind ci moom. Ndax dama koo gis muy benn ci ndey ak ci baay, waaye mu wéttali ku lool te ay wujjam doŋŋ a ko wéttali. Ñooy xaritam, ñooy doomi ndeyam. Mu doon seen yaay, li leen neex, li leen naqari moo leen koy jiital, uuf leen ni mu gëna rafete. Looloo tax ma bind téere bi.

Ma mère était très gentille. Je ne pouvais pas ne pas écrire sur elle, car elle est fille unique, mais je ne l’ai jamais vue toute seule. Ce sont seulement ses coépouses qui lui tiennent compagnie. Ses coépouses sont ses amies et elle est comme une seconde mère pour elles. Elle les soutient dans le bonheur comme dans le malheur. C’est la raison pour laquelle j’ai écrit ce livre.

Am génnekatu teere

Trouver un éditeur

Waaye nak defe na duma gaawatee bind, ndax bi ma binde dama mujje gecc de, ndax damaa sonn lool lool lool. Téere bu njëkk bi am na ñaar-fukki at dora génn te ba mu génneek léegi am na fukki at ak juróom ñaar, du fiftiin bu ma ci mës a am. Te wax ji sonn naa ci, jooy sax def naa ko ci mu dora génn, ci delloleen ma sama téere wala ngeen génne ko. Ñu di ma këll-këllee […].

Mais je pense que je ne vais pas écrire à nouveau de si tôt, parce que quand j’ai écrit [mes deux romans], j’ai fini par être démotivée, épuisée. Mon premier roman [L’ombre en feu ] a mis vingt ans avant d’être publié. Il y a dix-sept ans qu’il a paru et je n’ai toujours pas perçu de droits d’auteur. Je suis fatiguée de réclamer ce qu’ils me doivent, j’avais même pleuré avant qu’il ne soit publié. J’ai dû exiger qu’ils le publient ou qu’ils me rendent le manuscrit. Ils m’ont tellement fait attendre […].

Warugari bind kat bi

Droits d’auteur

Ba fi mu ne nii jubooguñu ci lu ñu ma wara fay. Xam naa su ma guddul fan lool, gëmuma naa ci lekk di. Ndax bi ci des tam (Aawo bi) moo tane ndax ba mu njëkkee génn daldi nay jeex ci juróomi at. Ba mu génnaatee, 1000 eksãpleer yi ren la ci fukki at ak juróom, jeexagul tuuti la weesu xaaj bi. Waaye ca depaar gi joxoon nañu ma li ma ci amoon. Fi mu ne nii amatuma ci dara. Damay mujj di jénd di ci maye. Xam nga loolu du tax ngay sawar di bind.

Jusqu’à présent nous ne sommes pas d’accord sur mes droits d’auteur. Ce qui est sûr, c’est que si je n’ai pas une longue vie, je ne pense pas qu’un jour je toucherai cet argent. L’autre [Aawo bi] est un peu mieux, car la première édition était épuisée en cinq ans. La deuxième est tirée en 1000 exemplaires il y a maintenant 15 ans et elle n’est toujours pas épuisée. Plus de la moitié du stock est vendue. Mais ils m’ont payé mes droits d’auteur dès le début. Actuellement, je n’ai rien à y gagner. De temps à autre, j’achète mes propres livres pour les donner en cadeau. Vous savez, cela n’encourage pas à écrire.

Bind ci farãse wala ci wolof ?

Écrire en français ou en wolof ?

S.A.J: Bind nga ci nasaraan ak ci wolof. Ci ñaari làak yooyu ban moo la ci gënal?

S.A.D: Vous avez écrit en français et en wolof. Dans laquelle de ces deux langues préférez-vous écrire?

M.Y.J: Xam nga ni olof a may gënal ndax olof bi yomb na. Bu ma koy bind duma wuti bàat yi, duma jël téere di seet lii lu muy tekki, duma seet lii nan laa koy mëna waxe […] Ni ma ko xalaate lay dal di ñëwee ma dal di bind dafay yomb ci man ndax li nga namp nga di ko wax, bokkul ak li nga jàng. Man déggu maay tubaab sax. Lu ne laa daj ba may bind tubaab. Fu ne ma woote fa, fu ne ma lajte fa.

M.Y.D: Vous savez bien que je préfère le wolof puisque c’est plus facile. Quand j’écris en wolof, je ne cherche pas les mots, je ne consulte pas un dictionnaire pour voir le sens des mots, comment je dois les écrire […] Mon inspiration coule de source et c’est facile pour moi. Écrire dans votre langue maternelle est différent d’écrire dans une langue que vous avez apprise. Moi je ne comprends même pas bien le français. J’ai beaucoup souffert quand j’écrivais en français. J’ai demandé et appelé un peu partout.

Aawo bi

La première épouse

S.A.J: Sa téere wolof bi yaa ngi ko tudde Aawo bi. Lu tax nga taamu Aawo bi bañ ka tudde « Aawo yi »?

S.A.D: Le titre de votre roman en wolof est La Première épouse, pourquoi pas « Les premières épouses »?

M.Y.J : Soo nee benn aawo bu baax rekk, wax nga aawo yu baax yépp. Man daal aawo bi ma jël muy benn aawo bu baax, ma xool ko ci sama yaay génne ko. Aawo bu baax bu nekk nak di nga ci gis sa bopp.

M.Y.D: Dés que vous dites une première épouse exemplaire, vous avez nommé toutes les premières épouses exemplaires. La première épouse que j’ai choisie est inspirée de ma mère et toute première épouse doit se retrouver en elle.

Ndax boo newoon aawo yi, aawo yépp bokkuñu. Am na itam aawo yu xawa sàggan, yu xawa mel ni man, yi nga xam ne seen bootaay taxu ko yaatu.

Ce serait différent si j’avais dit « Les premières épouses » car toutes les premières épouses ne sont pas pareilles. Il y a des premières épouses un peu négligentes, un peu comme moi. Celles qui ne sont pas ouvertes, qui ne sont pas généreuses.

Aawo bu dëgg-dëgg tey yewwoo Kajoor muy ki nga xam ne moo yaatu dënn, yaatu xol boot ñepp. Boole ñi mu jur ak ñi mu jurul, ñi baax, ñi sikk ñépp boot leen. Di fa toog nak luñ naan sonn muñ, jaxle muñ, bëgga dee muñ, ku muñ muuñ. Moom noonu lay def. Du daw du tàyyi. Sonn daw, bëgg a dee daw, jaaxle daw doo fekke dara. Waaye aawo booboo tax may wax.

La vraie première épouse, celle qui habite au Kayor, est celle qui a un grand cœur. Celle qui accepte tout le monde, ses enfants comme les enfants des autres, les gentils comme ceux qui ont des défauts. Elle vit dans son foyer dans le bonheur et dans le malheur, l’endurance et la persévérance sans limite car celui qui endure sourira bientôt. C’est ainsi qu’elle doit se comporter. Si elle quitte son foyer à la moindre difficulté, elle n’assistera à rien. C’est d’une première épouse qui a toutes ces qualités dont je parle [dans le roman].

Bind ci wolof

Écrire en wolof

S.A.J: Li ñu seetlu ci sa téere bi nga tudde Aawo bi mooy olof yi nga fa làkk.

S.A.D: Ce qu’on remarque dans Aawo bi, c’est la langue particulière du roman.

M.Y.J: Waaw man olof laa di.

M.Y.D: Oui moi je suis Wolof.

S.A.J: Gaa, waaye olof ya nga fa làkk wute na ñook olofi Ndakaaru, lu waral loolu?

S.A.D: Certes, mais le wolof dans Aawo bi est différent de celui de Dakar. Pourquoi ce choix?

M.Y.J: Ndakaaru séy a ma fi indi doŋŋ. Man Kajoor laa dëkk sa biir Kajoor te ginnaaw olof boobu ba mu done olof ba noppi dafa am lebu, am wolofu doomu Ndaar, am wolofu Kajoor. Ndax olof dëgg-dëgg Kajoor, Bawol ak Njàmbuur la. Ku nekk ak ni mu koy waxe. Man nak su ma xasee bay bind, damay bind olofu Kajoor nga xam ni lii ki ko bind waa Kajoor la. Foofu laa juddoo, fa la maggee, fa laa yaroo. Séy rekk a ma fa taxa joge. Olof nak dafa neex, man moo ma neex.

M.Y.D: Je suis à Dakar parce que c’est ici que je me suis mariée. Je suis du Kayor et en dehors de ce wolof, il y a le lébou, le wolof de Saint-Louis, celui du Kayor, car le vrai wolof est celui du Kayor, du Baol et du Niambour. Chacun a sa façon de le parler. Moi, quand je décide d’écrire, j’écris le wolof du Kayor. Toute personne qui le lira, saura que l’auteure est une Kayorienne. Je suis née là-bas et j’y ai grandi. C’est le mariage qui m’a fait partir de là. La langue wolof est agréable et je l’aime bien.

Way-jëmmal yi

Les personnages

S.A.J: Li ñu gis ci sa téere wolof bi moy Mbeen Faal dafa di koo xam ne wute naak wujjam wi Ndeela, ndax moom yaaram la, bu ñu ko tooñee sax du fayu. Mbeen moom da koy deffanteek Coro njëkke li, du ko bàyyi benn yoon. Ndax li mu sant Faal a waral loolu?

S.A.D: On remarque dans votre roman que Mbeen Faal est différente de sa coépouse Ndeela, car cette dernière est sans histoire, elle ne répond pas à la provocation. Alors que Mbeen, elle, ne se laisse pas faire, surtout par rapport à sa belle-sœur Coro. Est-ce parce qu’elle porte le nom de Faal?

M.Y.J: Loolu ñu bari loolu lañu wax. Mbeen moom faaleen la, loolu nga ci wax a ci am. Faaleen la. Man tamit bëggu ma bind loo xam ni ëllëg-ak-sibir […] Ndax dangay bind dem wacc fi. Sunu sët yeek ñépp di gis. Bu ñu ñëwee, war na nu gis ni séy kat nii la deme woon. Am na ku nangu wujj, amoon na ku bañ wujj. Am na ku mënee ko xam ne boo ci doxaleek moom mu bàyyi ca, yomb, nooy. Jigéen ju mel noonu yaatu, yaa dënn. Am na jigéen yoo xam ne tamit dañu am seen jikko, boo defee ñu defantekook yow ba mu saf ni faaleen yi. Ndax bëggu ma nak ñiy ñëw, won leen ni lépp nii la meloon. Loolu sax mënula nekk. Ádduna moom nit ñi dañu wuute, kenn bokkul.

M.Y.D: Cela, beaucoup de personnes le disent. Mbeen est une Faaleen6 et c’est la vérité. C’est une Faaleen. Et moi je ne veux pas écrire quelque chose et on s’aperçoit dans le futur que ce n’est pas la réalité. […] Car vous écrivez pour la postérité. Nos descendants le verront. Quand ils viendront ils doivent savoir comment se passait le mariage. Il y a des femmes qui acceptent d’avoir une coépouse comme il y en a qui ne l’acceptent pas. Il y a des femmes qui se laissent faire, qui ne se vengent pas, des femmes généreuses. Il y a aussi des femmes qui ont du caractère et qui ne se laissent pas faire, comme les Faaleen. Je ne voudrais pas tromper la génération future en lui donnant l’impression que toutes les femmes étaient pareilles. Cela n’est même pas possible. Les gens sont différents, tout le monde n’est pas pareil.

Man li ma bëggoon mooy wone jigéen ju mel nii ak jigéen ju mel neneen. Wone nak yaatu dënn aawo bi nga xam ne noo mën a mel boo ñëwee mu boot la, ndax loolu mooy li ko war. Te boo amee dëgg-dëgg wërsëg, dangay dajeek aawo boo xam ni dafa yaatu dënn, yaatu ginnaw, lu ñëw mu boot. Moo tax Mbeen ak na mu mën a mel, jikkoom feeñul lu dul ba ñu ko indilee wax nak te mu wara wax. Waaye nak faaleen la dafa daldi feeñ loolu nak dafa am. Yu am rekk la wone foofu.

Ce que je voulais montrer c’est qu’il y’a une femme qui a tel caractère et une qui est différente, mais surtout, montrer la générosité d’une première épouse qui accepte tout le monde, car c’est son devoir. Et si vous avez vraiment de la chance, vous rencontrerez une première épouse qui a un grand cœur et qui supporte tout le monde. C’est pourquoi pour Mbeen, bien qu’elle soit une bonne épouse, son caractère ne s’est révélé que lorsqu’elle devait exprimer ce qu’elle a dans le cœur7. Mais c’est une Faaleen et cela est une réalité. Je n’ai écrit que ce qui existe.

S.A.J: Corook yaayam sonnal nañu Ndeela lool. Ci tongo la dëkkeek njëkke li. Ba seen tongoo bu mujj gi ca la Coro làggale Ndeela, damm ay gëñam. Lan nga bëggoona wone ci jëf jooju?

S.A.D: Coro et sa mère mènent la vie dure à Ndeela. Coro se dispute tout le temps avec sa belle-sœur. Leur dernière querelle se solde par la perte des deux incisives de Ndeela. Quel message voulez-vous faire passer à travers cet acte?

M.Y.J: Dama bëggoon wone ñaari mbir. Li ëpp ci mettitu séy lu ci ëpp goro yi ak njëkke yi ñoo koy yóbbe seen jabaru doom wala seen cammiñ. Bu ñu mënoona xam ni li ñu nekkeek ñoom dañu koy def seen doom te ñoom it dañu leen koy def ñun jigéen ñi dinañu ci jeema génn. Ndax neexul ba neexul waaye, séy li ci gëna metti du sax wujj bi ñu siy wax, du yit nekk ci liggéeyu góor di ko toppatoo. Lu ci gën a metti mooy fekk fa ay njëkke wala ay goro yu lay toŋal, mayu ñu la benn jàmm. Nga bëgg cee bole ëmb, di am doom, di togg, di fóot, di paase […] naqar rekk ngay dëkke. Loolu daal jigéen ñi war nañ cee seetaat seen bopp. Loolu laa bëggoon a duut baaraam ba nga xam ne lii du dëgg du yoon te metti na. Loolu laa bëgoon a wone.

M.Y.D: Je voulais montrer deux choses. Les peines les plus difficiles dans le mariage sont infligées à l’épouse par la belle-mère et les belles-sœurs. Si seulement celles-ci pouvaient comprendre que leur attitude envers la mariée leur sera rendue et sera rendue à leurs propres filles, toutes les femmes essaieraient de changer leur attitude à l’égard de leur belle-fille ou de leur belle-sœur. A vrai dire, le plus difficile dans le mariage n’est pas la rivalité entre coépouses ni être au service du mari. Le plus pénible est de trouver dans le foyer des belles-sœurs ou de beaux-parents qui vous persécutent qui ne vous laissent aucun répit. Si vous devez y ajouter les maternités et les travaux domestiques […], vous ne vivrez que dans le malheur. Les femmes devraient revoir leur attitude. C’est ce que je voulais dénoncer afin que tout le monde sache que ce comportement n’est pas normal. C’est ce que je voulais montrer à travers cet acte.

Séyu kujje 

Mariage polygame

S.A.J: Dëkk yii di Dooxiif ak Finaax, ndax ay dëkk yu am la wala yaa ko fent rekk?

S.A.D: Est-ce-que les villages de Dooxiif et Finaax existent-ils réellement ou c’est vous qui les avez inventés?

M.Y.J: Maa ko fent waxe ko noonu rekk. Ndax bëggu maa wax benn dëkk, muy dëkk fenn. Damaa bëgg ba nga xam ne Kajoor géep ku ci nekk fa nga tollu nga defe ne sa dëkk la. Te boo tuddee benn dëkk rekk, dëkk boobu da koy moom bàyyi ya ca des. Moo tax nak ma daldi tëgg baat yooyu. Ba noppi, baat yooyu ba ma leen tëggee ma daldi koy nirooleek na dëkk bi mel. Ndax ma nga joge woon Dooxiif, dëkk baayam. Boo seetlo ba muy séysi lu ne topp na ko. Baay ba am na alal, xiifu fa, maru fa. Mu ñëw fii ci Finaax, dañ ko nax. Fii ay nax a fi ne. Waaye dangay defe ne bu ñëwee da naan finaax feex, dara dootu ko war. Fekk ay nax la. Ku la ne kër jëkkër fu neex la, da lay nax. Fii nax a fi nekk moo tax ñu ne ko Fiinaax. Am na nak ñu ne xiif na la tudd tamit bu ñu defe verlan bi. Ndax ba mu fa deme xiif na cofeel, xiif na yërmande, xiif na jàmm, amu ko fa. Waaye man ni ma ko déggee dëgg-dëgg moy fii ay nax la. Ku la ne séy dafa neex da lay nax […]. Te goro ba mu fa fekk ak njëkke la dañu ne finaax, dara waratu leen. Moo leen wara gàddu […].

M.Y.D: C’est moi qui les ai inventés. Je n’ai pas voulu donner un nom propre qui finira par l’emporter. Je voulais que tout Kayorien pense que c’est son village qui est décrit. Si vous nommez un village, il finira par l’emporter au détriment des autres. C’est pourquoi j’ai créé ces noms. Après les avoir créés, j’ai fait en sorte qu’ils ressemblent aux villages crées. Car elle [Ndeela] vient de Dooxiif,8 village de son père. Si vous vous rappelez quand elle rejoignait le domicile conjugal, elle avait apporté beaucoup de choses. Son père a beaucoup de biens, elle n’avait ni faim, ni soif chez ses parents. Elle vient à Finaax, on l’a trompée. Finaax: Fii (ici) nax (tromperie, supercherie) « ici il n’y a que de la supercherie ». Mais vous pensez que lorsqu’elle arrive elle sera à son aise et qu’elle ne doit rien faire. C’est de la tromperie. Si on vous dit que le domicile conjugal n’est que du bonheur, on vous trompe. Certains disent que le village s’appelle « il/ elle a faim » si on fait le verlan car l’héroïne est en manque d’amour, de compassion, de paix. Elle manque de tout cela. Mais moi j’entends par Finaax la supercherie. Celui qui te dit que la vie conjugale est facile ne te dit pas la vérité […]. De plus, la belle-mère et la belle-sœur qu’elle a trouvées dans le domicile conjugal sont à leur aise, elles ne font aucune tâche ménagère. C’est elle [Ndeela] qui doit les supporter […].

Nettalikatu géwél 

Le griot comme narrateur

S.A.J: Ki nettali Aawo bi géwél la muy Penda Géwél. Lu tax nga taamu nettalikatu géwél.

S.A.D: La narratrice de Aawo bi est une griotte, Penda-Géwél. Pourquoi choisir une griotte comme narratrice du roman?

M.Y.J: Xam nga ni sunu dëkk yi nettalikat bi moy géwél, moy liggéeyam. Bu doon ca bu njëkk a njëkk am na tëgg, am na wuude, am na géer ñi, waaye am na it géwél yi. Géwél yi nak li gëna doon seen liggéey moy nettali. Cosaan it ñoom ñoo ko yor. Seen dënn ak seen bopp yi la nekk. Ku fi bëgga xam sa cosaan géwél a la koy wax ca cocc ba coset. Xam la ca baax, xam la ca bon. La ca bon lu ci ëpp da la koy nëbb, wax la ca rafet. Waaye soo ko tooñee ba mu dugg ci ruq, wala ba nga merloo ko ba mu wax, dina génne la mu nëbboon ndax dara réeru ko. Cosaan nak ñun daawuñu ko bind. Sunu cosaan géep mi ngi seen dënn rawatina géwél bu góor bi, moo yor cosaan gépp. Bu jigéen beep xam na ko. Waaye bu jigéen bi li mu gën a mën moy nettali ak reelo, ak kàll, ak kaf ak taasook fecc. Loolu moy liggéeyam. Booy wut kuy nettali ci Afrig, ci Senegaal dangay jël géwél yi, keneen mën na ko waaye ñoom ñoy borom.

M.Y.D: Vous savez, dans nos pays, le narrateur par excellence est le griot, c’est son métier. Auparavant, il y avait les forgerons, les cordonniers et ceux qui n’exerçaient pas un métier artisanal, mais il y avait également les griots. Le principal métier des griots est de raconter. C’est aussi eux qui gardent la tradition. Ils la connaissent par cœur. Qui veut connaître sa culture s’adresse au griot. Il sait tout dans les moindres détails, le bon côté comme le mauvais côté. La plupart du temps il vous cache le mauvais côté et ne vous explique que le bon. Mais si vous l’offensez, il vous dira tout ce qu’il avait caché car il n’a rien oublié. Quant à l’histoire, nous ne l’écrivions pas. Toute notre histoire est gardée par les griots, surtout le griot homme. La griotte connaît également l’histoire, mais son principal métier est de raconter, de faire rire, de plaisanter, déclamer des énoncés rythmés élogieux ou satiriques et de danser. C’est cela son métier. Si vous cherchez un narrateur ici en Afrique, au Sénégal, il faut prendre le griot. D’autres peuvent le faire, mais c’est le métier des griots.

Jafe-jafeey fésal teere 

Difficultés de publication

S.A.J: Sa téere bi yaa ngi ko bind 1982, toog na fukki at bala ñu koy génne. Lu waral yàggaay boobu?

S.A.D: Votre roman [Aawo bi] est écrit en 1982, mais il n’est publié que dix ans plus tard. Qu’est-ce qui explique cette longue durée?

M.Y.J: Xam nga bind téere benn la fi. Waaye génne ko moo gën a jafe sax bind ko fii ci Afrig. Génne téere moo gëna jafe. Fi mu nekk nii téere yu génnagul a ka ëpp.

M.Y.D: Vous savez ici, écrire un livre est une chose, le publier en est une autre. Il est plus facile d’écrire que de publier un livre en Afrique. Actuellement, il y a plus de manuscrits que de livres édités.

Sama téere bu tubaab bi am na ñaar-fukki at sooga génn. Bii [Awoo bi] fukki at ya mu am, fekk na kenn tàmbaleegul génne ay téere ci olof lu bari te kii mooy téere fent bi ñu njëkka bind ci làkki réew mi ci Senegaal. Waaye wa IFAN ko njëkk a génne, ci seen xaalis la ñu ko génne. Booba Aram Faal moo fa nekk, moo ma jàngal mbind mi. Moo ko taxawu ba ñu génne ko. Fii bind moo fi gën a yomb génne. Dañu amul, xam naa ñàkk gi la rekk.

Mon roman en français a mis vingt ans avant d’être publié. Celui-là [Aawo bi] a mis dix ans. C’est parce qu’il n’y avait pas encore de structures éditoriales en langues nationales à ce moment. Il est le premier roman en langues nationales et c’est l’IFAN qui l’a édité à ses frais. C’est Aram Faal qui était là-bas, c’est elle qui m’a alphabétisée. C’est elle qui s’est battue pour que le roman soit édité. Il est plus facile d’écrire que d’éditer un livre, peut-être que c’est à cause de la pauvreté.

Tekkim Bataaxal bu gudde nii ci wolof

Traduction en wolof d’Une si longue lettre

S.A.J: Tekki nga Une si longue lettre bu Mariyaama Ba ci wolof. Lu tax nga taamu téere boobu?

S.A.D: Vous avez traduit Une si longue lettre de Mariama Ba en wolof. Pourquoi avoir choisi ce roman en particulier?

M.Y.J: Waaw dama demoon IFAN — fekk Mareetu Jõŋ Jòob a yoroon Direction du livre et de la lecture. Ba ma ñewe, xam naa bëggoon na ma ka sant, xamul nu muy def. Mu ne maa: « ay Maam Yunus su ma amoon ku may tekkil Une si longue lettre bu Mariyama Ba […] ». Foofu nak ma ni ko « ah kooku de danaa ko mën ndax kooku ñoo bokk yëg-yëg. Te liñ nekk jigéen ñoo bokk yëg-yëg. Kooku bosam mën naa ko tekki. Waaye nak, pur ma tekki ko de, faw dama ciy ànd ak Aram ndax man xam naa ne wóoluwuma sama bopp ci fite gi ». Mu ne ma « kon nak wax ko Aram ». Ma daldi nak wax ko Aram. Aram ne ma ayca. Wallaay feyyuñu ñu sax lu ko jàr, waaye ñun dañuy liggéeyal làkku réew mi. Ñu daldi ko bokk tekki ko maak Aram

M.Y.D: Je suis allée un jour à l’IFAN — à l’époque, Mariétou Diongue Diop était la directrice du livre et de la lecture. Lorsque je suis arrivée, certainement elle voulait me le demander, mais elle ne savait pas comment faire9. Elle me dit: « Mame Younousse, si j’avais quelqu’un qui me traduirait Une si longue lettre de Mariama Ba […]». Je lui dis: « Je peux bien le faire parce que nous avons la même vision. Je peux traduire son roman. Mais en collaboration avec Aram Faal, car je ne suis pas sûre de mon orthographe ». Elle me répond: « Va voir Aram Faal ». Je suis allée la voir et elle était d’accord. Ils ne nous ont pas payé le prix, mais nous l’avons fait pour les langues nationales. Nous l’avons traduit ensemble.

Áddinay jigéen ñi

Le monde des femmes

S.A.J: Ci sa ñaari téere yéep, coono jigéen nga ci wax. Lu waral nga jiital jigéen ci saay téere?

S.A.D: Dans vos deux romans vous parlez de la souffrance de la femme. Pourquoi vous mettez la femme en avant dans vos romans?

M.Y.J: Xam nga loolu daa-naka jarul laaj. Man jigéen laa. Sama yëg-yëg, sama gëm-gëm, xam-xam yéep jigéen. Te it, dama bëgg jigéene nak. Da may wax xale yi, jigéen nay jigéen, góor nay góor, xale di xale, mag di mag. Su ko defee réew mi mën a dox. Waaye bu kenn xamatul kenn, gone lu ko neex wax, lu ko neex def. Jigéen lu ko neex sol, lu ko neex wax. Góor def nu ko neex […]. Wax dëgg yàlla loolu àndu ma ci. Man damay jigéen ba noppi, man ci ay jigéen laa mës a dëkk. Xam nga fii ci sunu réew yi léegi la sax waaye bu njëkk boo demee ci kër yi yu mag lay doon. Jigéen ñi dañuy féete nee, góor ña féetee nee. Ci biir fo sax bu ñu xasee ba weesu juróom ñaari at duñuy nangu góor ñeek jigéen ñi di bokk fo. Xale yu góor ñi dañuy fo fii, jigéen ñi di fo fee. Bokku ñu sax fo. Man nak ci jigéen ñooñu la mës a nekk. Ci sama peggu yaay laa yaroo, samay wujju yaay, samay mag, samay rakk […]. Jigéen ñi rekk laa dëkkal ba ma tollu nii ba am kër. Ba fii ma nekk ni yàlla nattu ma sama borom kër teela dëddu it ma yar samay doom yu jigéen ak samay jarbaat…ñépp jigéen lañu […]. May gis seeni coono, seeni mettit ak seeni xalaat, seeni doxalin, li ñuy gise àddina, luy seen banneex, luy seen naqar […] Su ma la bëggee wax li góor nekke it bariwut lu ma ci xam.

M.Y.D: Ce n’est même pas la peine de le demander car je suis une femme. Mes sentiments, mes convictions, mon savoir, tout est féminin. De plus, j’aime bien la féminité. J’ai toujours dit aux enfants que la femme reste femme, que l’homme reste homme, l’enfant reste enfant, le vieillard, vieillard, ainsi le pays pourra évoluer. Mais si l’enfant dit tout ce qu’il pense, fait ce qu’il veut. La femme porte tout ce qu’elle veut, dit tout ce qu’elle pense, l’homme fait la même chose […]. Sincèrement, je ne suis pas d’accord avec cela. Je suis femme et j’ai toujours vécu dans un environnement féminin. Vous savez, dans nos pays, c’est maintenant que les choses ont changé, mais auparavant, les maisons étaient très grandes. Les hommes et les femmes vivaient séparément. Même dans le jeu, dès l’âge de sept ans, on n’accepte plus que les garçons et les filles jouent ensemble. Ils jouent séparément. J’ai toujours vécu dans ce milieu de filles. J’ai grandi sous la protection10 de ma mère, de ses coépouses, de mes sœurs […]. Je n’ai habité qu’avec des femmes jusqu’à mon mariage. Dieu a fait que mon mari est décédé tôt, j’ai éduqué mes filles et mes nièces […]. J’ai partagé leur peine, leurs pensées, leur façon d’agir, leur vision du monde, leur bonheur, leur malheur […]. Je ne peux pas vous dire comment vit l’homme parce que je n’y connais pas grand-chose.

Ay woy

Des poèmes

S.A.J: Am na woy yoo bindoon te génne goo ko. Ndax dina mësa génn?

S.A.D: Vous avez écrit un recueil de poèmes qui n’est pas encore édité. Est-ce qu’il le sera un jour?

M.Y.J: Woy yi moom kom xaw na pare ba noppi, am na yu sax profesëer Asan Silla génne ci téereem te am na yu ma ci denc yu génnul […]. Woyi moom dafa gàtt am na yu ma ci denc. Nde man sax tàmbali naa yeneen fent, waaye mënuma fexe ba yeggale ko. Ndax xol bi nekkatu ci, xel mi nekkatu ci, jot maye tu ko, doole maye tu ko. Taŋ ba ma njëkkee di bind, suñ ma joxoon ma bind, xéy na booba taŋ de amoon naa lu mu bon a bon juróroom wala juróom benn téere ci sama bopp. Wax nañu ma wax bindaatal, waaye gëmuma ma mën ko de. Waaye woy yi moom bari na yu ma denc am woy yu génn. Defe naa ni moom dinaa ko mujj dajale mu génn wala ma génne ko. Bu dul dara sax ma génne ko joxe ko rekk ngir réew mi ak ngir dolli ci aaday réew mi.

M.Y.D: Les poèmes sont presque prêts. Certains sont d’ailleurs publiés dans le recueil du professeur Assane Sylla11 […]. Les poèmes sont courts, j’en ai gardé certains. J’avais même commencé d’autres romans, mais je n’arrive pas à les terminer, car ni l’esprit, ni la motivation n’y sont. De plus, le temps et la force ne me le permettent plus. Quand j’ai commencé, s’ils m’avaient donné les moyens, peut-être j’aurais pu écrire au moins cinq ou six romans. On me dit toujours de continuer, mais je ne pense pas pouvoir le faire. Toutefois, j’ai beaucoup de poèmes écrits et d’autres sont publiés. Je pense que je finirai par les rassembler pour les faire éditer [dans un seul recueil]. S’il le faut, je les éditerai à mes frais ne serait-ce pour le pays, pour la culture.

Feminist yi

Les féministes

S.A.J: Bëggoon naa xam sa digganteek mbootaay mi ñu tudde « Yewwu yewwi » ? Ndax deggoo ngeen xalaat ci xeexal jigéen?

S.A.D: Quels sont vos rapports avec le mouvement « Yewwu Yewwi12 »? Avez-vous la même vision du féminisme?

M.Y.J: Ñoom ba ñu njëkkee woote di taxawal « Yewwu yewwi » man demoon na. Bles Seŋoor fii ci Ndakaaru la woon. Yàgg na. Ba ma demee wax dëgg yàlla sopp naa leen lool ndax ànd nañook seen jamono xam naa. Man damay wax ni bokkuma ci xarnu bii, man ci xarnu bi weesu la bokk. Ndax xarnu boo ca duggee am lu mat juroom-fukki at, xarnu boobu nga bokk […]. Xarnu bu ma doon defe di soppi, di liggéey di dem di ñëw di jéema soppi sama réew […] mooy xarnu bi ñu weesu mooy ñaar-fukkeelu xarnu bi. Ñoom nak seen xalaat dafa jiitu woon xarnu boobu nak. Ñoom defe naa seen xalaat dafa yegsi woon ba ñaar-fukki xarnook benn. Ni ñu gise xeexal jigéen baax na waaye man bokku ma kook ñoom.

M.Y.D: J’ai assisté à leur toute première réunion constitutive. C’était à Blaise Senghor, ici à Dakar. Cela fait maintenant des années. En réalité, je les admirais beaucoup, car leurs revendications correspondent certainement à leur génération. J’ai l’habitude de dire que je ne suis pas de ce siècle, car si vous vivez pendant cinquante ans dans un siècle, vous appartenez à celui-là […]. Le siècle durant lequel je travaillais, j’essayais de changer des choses pour mon pays […] est le 20ème siècle. Les idées de « Yewwu Yewwi » devançaient ce siècle. Je pense qu’elles avaient des idées du 21ème siècle. Leur vision du féminisme est bien, mais je ne la partage pas.

Aada ji

La tradition

Man dama xawa wéeru tuuti ci cosaan, ci sama ñoom yaay. Ndax fi mu ne nii man bañuma xew, ndax gisuma benn xeet ci àddina bu amul xew. Kon nak kenn du joge fale rekk dikk ne ma xew baaxul rekk ma daldi bàyyi xew. Jànq ji téye boppam ba xéy ñu jox ko jëkkër mu mel na mu war a mel, ñu xéy di ko laabaan, su ma sañoon laabaan jooju day am. Dañu koy bégal, yendu koo bégal ay mbokkam di ka feccal. Dina tax ka topp ci moom am jom. […].

Je suis un peu conservatrice, car je ne rejette pas la tradition comme les cérémonies familiales. Je n’ai jamais vu un peuple au monde qui n’organise pas de fêtes. Donc je ne les abandonnerai pas juste parce que quelqu’un a soutenu que ce n’est pas bien. La fille restée chaste jusqu’au mariage, je souhaiterais qu’on lui organise un laabaan13. Ses parents passeront la journée à chanter et à danser pour elle. Cela encouragera sa sœur cadette à faire pareil […].

Boo demee ci sunu mbokku tubaab yi lu ñuy wax aniwerseer la ñuy def de, atal. Atal boobu lu ne lañu siy ñàkk. Te dañuy feetu da ñuy xumbal itam seeni séy de. Te seen séy sax moo gën a metti sunu bos. Ndax ñoom boo seetlo benn jaaro baaraam bu ñuy tudde jamaa bu tuuti, takkal ko ndaw si, man loolu mën na cee rey ay nag di, togg ko ñépp lekk, ñu waxtaan. Boo seetloo ñoom dañuy yendoo déglu Betowen xaw ma Mosaar xaw ma kan.

Les Européens fêtent leur anniversaire et ils dépensent beaucoup d’argent pour cette fête. Ils organisent pourtant des mariages animés. D’ailleurs leur mariage est plus onéreux que le nôtre. Avec seulement l’équivalent du prix de la bague d’alliance en diamant, je peux acheter des bœufs et préparer à manger pour tous les convives. Ils passent la journée à écouter Beethoven ou Mozart.

Man Buu Kunta Njaay man mooy sama Betowen. Buu Kunta bu yore xalamam googu bay woy « kor Joor Jeŋee Saala Biige Ngoone Njuga Faal Yaasin […] ». Sama jom yéngu, ma xam maay kan. Dinañ tax ma déggook sama mbokk mii ma dëkkaloon te xamantewuñu. Danañ tax ba ma rusa def lu ma warut a def. Dana tax sama doom xam lu ko booleek réew mi, lu tax may bokki Senegaal te bokkuma feneen.

Moi, c’est Bu Kunta Njaay14 qui est mon Mozart. Quand il prend son luth et me chante « Kor Joor Jeŋee Saala Biige Ngoone Njuga Faal Yaasin […] »15. Cela réveillera mon amour-propre, je connaîtrai mes origines. Cela me permettra d’être en de bons termes avec mon voisin que je ne connaissais pas. J’aurais honte d’avoir un mauvais comportement [en tant que citoyenne]. Mon enfant saura ce qui le lie au pays. Je comprendrai pourquoi je suis Sénégalaise et pas d’un autre pays.

Loolu lépp dama koy bàyyi ndax damay yàq ? Ñoo ci duggal yàq waaye yàq amu ci […]. Bu ñu ko dinde sànni ko, dinañ ko réccu ndax ñëpp a ngi xumbal ci seen réew. Waaye ñun tam nañu tere yàq gi, tere ko sunu bopp, dindi ko ci […]. Lii nuy yόot muy, toog ba dëkk ci benn kër wut fa benn xaj bu lay garde. Nga ne fa ndoŋ dee ba am ay fan te kenn du yëg ni dee nga ci biir kër gi. Loolu baaxul. Ñun li ñu nar a def moy xotti sunu aada sànni […].

Je dois abandonner tout cela parce qu’[on pense que] je gaspille? C’est nous qui avons introduit [dans les cérémonies] des futilités mais il n y a aucun gaspillage […]. Si nous abandonnons ces fêtes nous le regretterons car tout le monde conserve ses traditions. Mais de notre côté nous devons lutter contre le gaspillage et nous devons moraliser les fêtes. […]. Ce qui risque de nous arriver est l’individualisme [c’est-à-dire] vivre seul dans sa maison avec un chien qui vous tient compagnie. Vous vivez dans la solitude et un beau jour, vous mourez sans que personne ne soit au courant. Cela n’est pas bien. Ce qui risque de nous arriver est l’abandon de nos traditions […].

Áddina bii ñu nekk ak aada ji fay nekk, aada jooju aada boolante lay doon. Ku ne dangay indi la nga am. Su ko defee mu nekk benn aada boo xam ne àddina bépp a koy bokk. Ndax léegi lépp a gaaw. Kom lépp a gaaw, nañ tànn lu baax lépp ñu teye ko, Amerig la fa baax bu ñu ko indee ñu booleek sunu bos. Ñoom it ñu jël ci nit ñi lu baax. Waaye boo xottee sa lépp sànni dem ak sa yaram neen, dinga sol ba sol lu la jàppul, dinga lekk ba lekk loo xamul. Danu ñuy gëna ree rekk. Man de duma bàyyi xew […]. Da ma bëgg it ku may tagg.

Nous sommes dans un monde de partage. Chacun apporte sa culture de sorte que ce sera une culture universelle. Avec les nouvelles technologies tout va vite. Puisque tout va vite, préservons le meilleur de notre culture, prenons le meilleur chez les Américains et eux aussi font pareil chez les autres peuples. Mais si vous rejetez toute votre culture, vous porterez des habits qui ne vous vont pas, vous mangerez ce que vous ne devrez pas manger. On finira par se moquer de vous. Personnellement, je n’abandonnerai pas les cérémonies familiales […] et j’aime bien qu’on me chante [en déclamant ma généalogie].

Pόlόtik bi

La politique

S.A.J: Doon nga polotik ndax yaa ngi koy def ba léegi?

S.A.D: Vous faisiez de la politique est-ce que vous le faites toujours?

M.Y.J: Dañu defe ne dama daan pόlόtik… Man daal ba ma génnee liise Amet Faal […] Xam nga ne naa la dugg naa ékool ñetti yoon. Ba may am berewe mag la sax. Defe naa maa ngi ko am ci ñaar-fukki at ak ñaar xaw ma ñaar-fukki at ak benn. Àt mu ma njëkka jàngale moy atum indepãdãs. Ma yegsi Tiwaawon fekk ñuy doora dugg ci pόlόtik bi. Sama mag ju góor ju ma bokkal benn baay ni ma yow dangay dugg, yaay doon sunu jigéen ndax amu ñu jigéen te waa Cés am nañu jigéen. Fekk na booba tubaarkalla mënoon na maa wax, xawoon na maa mëna làkk tuuti, làkk a xewoon. Léegi rekk ñu daldi may def lu ñuy wax imesur UPS. Fekk nak man ubbi naa maison des jeunes àbboon naa ko. Li ma jàngoon ca ékoolu Ndar ñaw ak togg ak puériculture, enseignement ménager bu ñuy wax léegi. Ma di ko fa jàngal jigéen ñi, di leen jàngalaale itam cours du soir ay farãse. Di leen jàngal ni ñuy yore doom ak nu jigéen di sakkanale ñam ak dund gi ci biir kër gi… yu deme noonu.

M.Y.D: Ils pensent que je faisais de la politique… Quand je suis sortie du lycée Amet Fall […] Je vous ai dit que j’ai été retirée de l’école à trois reprises. J’étais adulte quand j’ai eu mon Brevet. Je pense que je l’ai eu à 22 ans ou à 21 ans. Ma première année d’enseignement est l’année de l’indépendance16. Je suis arrivée à Tivaoune au moment où on commençait la politique. Mon grand frère me dit: « Tu vas adhérer. Tu seras notre responsable femme, puisqu’on n’en a pas encore alors que Thiès en a déjà une17. » À ce moment, je savais parler en public, je savais m’exprimer en français, c’était la mode. Ils m’ont nommée membre UPS18. J’avais ouvert auparavant une maison des jeunes, une salle que j’avais empruntée. J’enseignais aux femmes ce que j’avais appris à Saint-Louis, la couture, la cuisine, la puériculture, l’enseignement ménager dont on parle maintenant et des cours du soir de français. Je leur apprenais comment s’occuper d’un bébé, la gestion du foyer, des choses de ce genre.

Ñoom daal ñu ne ma « dara dangay dugg ». La ñu ma gëna def sax moy dama toog benn bës rekk ñu indil ma paasu Amerig. Ma ni : « Lii lan la ? » Ñu ne ma dangay dem Amerig ndax dañoo demoon Cés di fa daje ñu jox ñu ay paas MJPS. Ku nekk wara yóbbu kenn. Ñun ñu tombeel paasu ku jigéen. Ma ni leen man bokkuma fenn di. Ñu ni ma dangay dem boo ñibbisee bokk. Nii laa deme Amerig de. Dem ci délégation MJPS. Ba ma ñëwee ma militeek ñoom. Waaye ñaari at laa fa def ñetteel ba ma daldi mariye.

Néanmoins, ils m’ont dit: « Tu vas militer [dans notre partie politique] » La surprise qu’ils m’ont faite un jour, est un billet pour les États-Unis. Je leur ai demandé : « Qu’est-ce que c‘est ? » Ils m’ont expliqué qu’ils avaient eu une rencontre du MJPS19 à Thiès et qu’on leur avait donné ce billet. Chacun devait avoir un représentant. Puisque notre billet est destiné à une femme, donc c’est moi qui représenterai Tivaoune. Je leur ai répondu que je n’étais pas encore militante. Ils m’ont dit de partir et de militer à mon retour. C’est ainsi que je suis allée aux États-Unis avec la délégation du MJPS. A mon retour j’ai milité avec eux. Mais je n’ai fait que deux ans, je me suis mariée la troisième année.

Ki ma mariyeel xaw ma ci moon dara man itam. Booba nak demoon naa ba ñu ne maay doon première femme députée du Senegaal. Ñoom ñuy xeex, Alfõs Njaay komandã ak ñëpp taxaw ndax ma nekk première femme député du Senegaal. Waaye ma mariye. Am ku ma ci topp rekk, gis ma ci aktiwite yi ndeysaan ba ñu mariye. Ndekete militeer la. Ñu séy ba noppi mu door ni sama yaay jabaru militeer du pόlόtik. Ca laa bàyyee.

Je ne connaissais pas bien mon mari. On disait que j’allais être la première femme députée du Sénégal. Le commandant Alphonse N’diaye et les autres se battaient pour faire de moi la première femme députée du Sénégal. Mais je me suis mariée avec un homme qui m’a vue dans les activités [politiques] et qui ne cessait de me suivre. Il était militaire. Ce n’est qu’après le mariage qu’il a informé ma mère qu’une femme de militaire ne doit pas faire de la politique et j’ai arrêté.

Karolin moom daldi dugg daldi nekk première femme députée. Ndax région Cés a ka moomoon. Fekk Tiwawon di xëcc pur moom ko. Ca laa bàyyee pόlόtik. Te séy ba sax yàggul. Moo jur sama taw ndeysaan. Ku baax la woon waaye séy bee yàggul daal. Noonu la deme.

Caroline a fini par être la première femme députée. Ce poste revenait à la région de Thiès, et Tivaoune se battait pour l’avoir. C’est ainsi que j’ai arrêté définitivement la politique. Le mariage n’a même pas duré longtemps. L’homme avec lequel je m’étais mariée est le père de ma fille aînée. Il était un homme bien, mais le mariage n’a pas duré. C’est ainsi que cela s’est passé.

Waaw yow ku la ko wax? Bala maa waxati daŋ ma wax ku la ko wax.

Mais qui vous l’a dit? Avant de continuer l’entretien vous me direz qui vous a dit que je faisais de la politique.

S.A.J: Kenn waxu ma ko. Dama ka jàng ci sa entretien bi nga def ak Papa Samba Jóop. Da nga cee wax tuuti ni doon nga def pόlόtik.

S.A.D: Personne ne me l’a dit. Je l’ai plutôt lu dans votre entretien avec Papa Samba Diop. Vous avez évoqué dans un passage que vous faisiez de la politique.

M.Y.J: Ñaar wala ñetti at laa def […]. Amuñu woon responsable femme. Xam nga Tiwaawon ñu jàng ñi bariwuñu fa woon. Te ñu jàng ñi ñekkuñu fa woon, dañ leen afekte feneen. Man dama jàngi ñëw di jàngalewaat Tiwaawon ci sunu wetu kër […].

M.Y.D: Je n’ai fait que deux ou trois ans […]. Nous n’avions pas de responsable femme. Vous savez il y avait peu de personnes instruites à Tivaoune. De plus, celles qui l’étaient étaient affectées dans d’autres villes. Moi, j’ai étudié [à Saint-Louis] et j’ai été affectée à Tivaoune, près de chez moi […].

Syndicat yit noonu laa ci dugge. Syndika 56, ci membre fondateur yi la. Booba xale laa maak ñoom Kabiiru Mbooj ak Badara Faal, Duudu Ngom, Jim Saar ak Mbay Mbeng ndeysaan yal na ko yàlla yërëm. Ay mag lañu woon. Ñoom daal laa bokkaloon syndicat bu njëkk. Ki ma njëkka séyal nak moy mititeer moo ma ci génne ci yooyu yépp. Te sunu séy yàggul noonu. Xam nga séyu mag ak xale rekk […].

C’est de la même façon que j’ai adhéré au syndicalisme. Le syndicat 56, j’étais parmi les membres fondateurs. J’étais encore jeune et j’étais dans le groupe des anciens avec Kabirou Mbodj, Badara Fall, Doudou Ngom, Djim Sarr et Mbaye Mbengue que Dieu ait pitié de son âme. Ils étaient plus âgés [que moi]. J’ai milité dans le premier syndicat [des enseignants] avec eux. Mon premier mari était militaire, c’est lui qui m’a demandé d’arrêter toutes ces activités. Notre mariage n’a même pas duré. Vous savez, un mariage entre deux personnes de générations différentes […].

Ndakaaru 28 mars 2014.

Dakar, le 28 mars 2014.

 


 

Références bibliographiques

  • Romans de Mame Younousse Dieng

Aawo bi [Première épouse], fentaakon bi [fiction], Dakar, Organisation sénégalaise d’appui au développement (OSAD), Collection « Teere fent » [ouvrages de fiction], 1999, 2e édition, 76 p. [Première édition, Dakar, IFAN/Cheikh Anta Diop, 1992, 72 p.]

L’ombre en feu, Dakar, Les Nouvelles Éditions Africaines du Sénégal, 1997, 236 p. [manuscrit déposé chez l’éditeur en 1977]

  • Réception

DIEME Saly Amy, 2014, Écriture littéraire en wolof : L’exemple de Aawo bi de Mame Younousse Dieng, Mémoire de Master Recherche 2, Paris, INALCO, 149 p.

DIOP Papa Samba, 2002, « Un entretien avec Yunus Jeŋ », in Claire DEHON, Le réalisme africain, le roman francophone en Afrique subsaharienne, Paris, l’Harmattan, pp. 261-167.

FALL Guéj, « Aawo bi de Mame Younousse Dieng, un récit fondateur en langue wolof » in Éthiopiques n°76, 1er semestre 2006, pp. 37-155.

KEÏTA Abdoulaye, 2014, « De l’alphabétisation à la littérature, la prise de parole didactique par des écrivaines wolof », Journal des africanistes tome 83, fascicule 1, pp. 156-179.

KEÏTA Abdoulaye, 2020, « Aawo bi / La première épouse », ELLAF, la bibliothèque numérique des littératures en langues africaines : recherche, documentation, édition, ISSN 2804-7672, http://ellaf.huma-num.fr/aawo-bi-la-premiere-epouse/

 

 


 

Notes:

1 FALL Guéj (2006), a consacré un article à ce roman.

2 Le roman en question est L’ombre en feu, déposé chez l’éditeur en 1977, mais n’est publié que vingt ans plus tard, c’est-à-dire en 1997.

3 Le caractère de Ndeela (l’héroïne du roman)

4 Il s’agit de la maison conjugale de l’héroïne dans Aawo bi.

5 Comme Matar Ndiaye, le mari de l’héroïne.

6 Faaleen désigne toute personne qui porte le nom de famille Fall. Les Fall et les Dieng sont des cousins à plaisanterie. L’auteure est une Dieng et le cousinage à plaisanterie apparaît à travers le caractère qu’elle donne à l’un des personnages du roman (Mbeen Faal) qui incarne le contraire des valeurs défendues par l’héroïne.

7 Le mari de Mbeen a pris une troisième femme.

8 Dooxiif est composé de deux mots: doo: tu n’auras pas et de xiif: la faim, la famine. C’est le village d’origine de l’héroïne qui est caractérisé par sa richesse et la fertilité de ses terres.

9 Mame Younousse Dieng avait pris la décision de ne plus écrire.

10 Littéralement « sous l’ombre » de… : l’emploi métaphorique d’« ombre » renvoie à l’idée de protection.

11 Sylla Assane, 1980, Poèmes et pensées philosophiques wolof: (de l’oralité à l’écriture), Tome IV, Dakar, ACCT-IFAN, 148 p.

12 Yewwu yewwi qui signifie en wolof « prendre conscience pour se libérer » est le premier mouvement féministe au Sénégal. Il est créé en 1984 par Marie-Angélique Savané.

13 Laabaan est la fête de célébration de la virginité d’une nouvelle mariée.

14 Célèbre griot chanteur et guitariste (luthiste) wolof.

15 « L’époux de Dior Dieng, Sala Bigué Ngoné Ndiouga Fall Yacine » : il s’agit d’une formule pour louer certains membres de la famille Dieng.

16 En 1960.

17 Dans les années 60, très peu de femmes sont instruites en français au Sénégal.

18 UPS: L’Union Progressiste Sénégalaise est un ancien parti politique sénégalais fondé vers la fin des années 1950. (Parti politique de Léopold Sédar Senghor). Cette organisation a pris le nom de Parti socialiste en 1976.

19 Mouvement des Jeunes du Parti Socialiste.

Bu ko dóor — Ne la bats pas

 

Chant de mariage denkaane

 

Mots-clés:  wolof, Sénégal — chant de mariage, taasu, waliima, denkaane — mariage, festivités.

Production du corpus:  Chanson énoncée par Fatou Bèye et Amy Ndiaye

Collecte:  Le corpus est extrait d’un ensemble de 60 chants collectés par Saly Amy Diémé en juin-juillet 2015. Les enregistrements ont eu lieu pendant les cérémonies de mariage ou lors des performances sollicitées.

Descriptif:  Le texte est un chant de mariage denkaane, qui appartient au répertoire traditionnel de chants de mariage wolof, le taasu.

Le terme denkaane ou « recommandations » désigne à la fois les recommandations données aux époux avant la nuit de noces et les chants par lesquels la mariée est accompagnée au domicile conjugal.

La cérémonie a toujours lieu la nuit. Elle commence dès le départ du cortège jusqu’à l’entrée du village ou du quartier du marié. Les énonciatrices, amies de la même classe d’âge que la mariée chantent leur désolation de voir cette dernière partir. Les chants sont habituellement des conseils adressés à l’épouse. Le chant présenté ici contient des recommandations qui s’adressent aussi bien à la mariée qu’à son époux.

Référence:

DIÉMÉ, Saly Amy, 2016, « La poésie orale dans les cérémonies de mariage wolof », Mémoire de Master 2, Oralité et anthropologie, préparé et présenté sous la direction d’Ursula Baumgardt et d’Abdoulaye Keïta, Paris, Institut National des Langues et Civilisations Orientales (INALCO), 209 p.

 


 

 

 

.

.

.


 

 

 

 

Chant de mariage denkaane

 

Saly Amy DIÉMÉ, « La poésie orale dans les cérémonies de mariage wolof »,

Mémoire de Master 2 Oralité et anthropologie, Paris, INALCO, pp. 191-193

 

 

 

Amy Ndiaye

 

 

Bu ko dόor te bu ko saaga yaay

Ne la bats pas et n’insulte pas sa mère

 

Dee ko muñalee

Sois tolérant avec elle

 

Fatou Bèye

 

 

Bu ko dóor te bu ko saaga yaay

Ne la bats pas et n’insulte pas sa mère

 

Dee ko muñalee

Sois tolérant avec elle

 

Amy Ndiaye

 

5

Bu ko dóor yaay te bu ko saaga

Mon cher, ne la bats pas et ne l’insulte pas

 

Dee ko muñalee

Sois tolérant avec elle

 

Fatou Bèye

 

 

Waay bu ko dóor yaay

Mon cher, ne la bats pas

 

Te bu ko saaga yaay

Et n’insulte pas sa mère

 

Dee ko muñalee

Sois tolérant avec elle

 

Amy Ndiaye

 

10

Bul dóor yaay te bu ko saaga

Mon cher, il ne faut pas la battre ni l’insulter

 

Dee ko muñalee

Sois tolérant avec elle

 

Fatou Bèye

 

 

Boo koy dóor te di ko saaga yaay

Si tu la bats et insultes sa mère

 

Léeg mu ñibbisee

Elle rentrera bientôt chez elle

 

Amy Ndiaye

 

 

Bul dóor yaay te bul saaga

Mon cher, ne la bats pas et ne l’insulte pas

15

Dee ko muñalee

Sois tolérant avec elle

 

Fatou Bèye

 

 

Bu ko dóor yaay

Mon cher, ne la bats pas

 

Te bu ko saaga yaay

Et n’insulte pas sa mère

 

Dee ko muñalee

Sois tolérant avec elle

 

Amy Ndiaye

 

 

Bu ko dóor

Ne la bats pas

20

Te bu ko saaga yaay

Et n’insulte pas sa mère

 

Dee ko muñalee

Sois tolérant avec elle

 

Fatou Bèye

 

 

Boo koy dóor

Si tu la bats

 

Te di ko saaga yaay

Et insultes sa mère

 

Léeg mu ñibbisee

Elle va bientôt rentrer chez elle

 

Amy Ndiaye

 

25

Boo kooy dóor

Si tu la bats

 

Te di ko saaga yaay

Et insultes sa mère,

 

Léeg mu ñibbisee

Elle va bientôt rentrer chez elle.

 

Fatou Bèye

 

 

Bul ko yor yorub baayam

Ne l’éduque pas à la manière de son père

 

Amy Ndiaye

 

 

Céy !

Ça alors !

 

Fatou Bèye

 

30

Waay ne bul ko yor

Répète, ne l’éduque pas

 

Yorub baayam

À la manière de son père

 

Amy Ndiaye

 

 

Ee bul ko yor yorub baayam

Hé, ne l’éduque pas à la manière de son père

 

Fatou Bèye

 

 

Waawaw bul ko yor

Bien sûr, ne l’éduque pas 

 

Yorub baayam

À la manière de son père

 

Amy Ndiaye

 

35

Bul ko yor yorub baayam

Ne l’éduque pas à la manière de son père

 

Fatou Bèye

 

 

Baayam,

Son père,

 

Du saaq njël

Ne donne pas de provision quotidienne[1]

 

Te du katte

Ne [la] baise pas,

40

Te du daqar ba mu saf

Ne mélange pas bien le tamarin[2]

 

Bul ko yor yorub baayam

Ne l’éduque pas à la manière de son père

 

Amy Ndiaye

 

 

Ee bul ko yor

Hé toi, ne l’éduque pas

 

Yorub baayam

À la manière de son père

 

Fatou Bèye

 

 

Baayam,

Son père,

45

Du saaq njël

Ne donne pas de provision quotidienne

 

Te du katte

Ne [la] baise pas,

 

Te du daqar ba mu saf

Ne mélange pas bien le tamarin

 

Bul ko yor yorub baayam

Ne l’éduque pas à la manière de son père

 

Amy Ndiaye

 

 

Ee yow bul ko yor

Hé toi, ne l’éduque pas

50

Yorub baayam

À la manière de son père

 

Fatou Bèye

 

 

Bul ko yor

Ne l’éduque pas

 

Yorub baayam

À la manière de son père

 

Amy Ndiaye

 

 

Yow bul ko yor

Toi, ne l’éduque pas

 

Yorub baayam

À la manière de son père

 

Fatou Bèye

 

55

Waay sëy laa la yabale

Je te recommande de bien tenir ton ménage

 

Sëy laa la yabale

Je te recommande de bien tenir ton ménage

 

Bu la yalla yóbbo

Si Dieu fait que tu pars,

 

Ba nga dem ca kër ga

Une fois dans ton foyer

 

Bul xas ndaw ña

Ne sois pas insolente avec les enfants,

60

Duma mag ña

Ne bats pas les adultes

 

Sëy laa la yabe daal

Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage

 

Amy Ndiaye

 

 

Ee sëy laa la yabe daal

Hé je te recommande vivement de bien tenir ton ménage

 

Fatou Bèye

 

 

Waay sëy laa la yabe man

Moi, je te recommande de bien tenir ton ménage

 

Amy Ndiaye

 

 

Sëy laa la yabe man

Moi, je te recommande de bien tenir ton ménage

 

Fatou Bèye

 

65

Yee sëy laa la yabe daal

Yee je te recommande vivement de bien tenir ton ménage

 

Amy Ndiaye

 

 

Sëy laa la yabe man

Moi, je te recommande de bien tenir ton ménage

 

Fatou Bèye

 

 

Waay bu la yalla yóbbo

Si Dieu fait que tu pars

 

Ba nga dem ca kër ga

Une fois dans ton foyer,

 

Bul xas ndaw ña

Ne sois pas insolente avec les enfants

70

Duma mag ña

Ne bats pas les adultes

 

Sëy laa la yabe daal

Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage

 

Amy Ndiaye

 

 

Sëy laa la yabe daal

Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage

 

Fatou Bèye

 

 

Yee sëy laa la yabe waay

Yee je te recommande vivement de bien tenir ton ménage

 

Amy Ndiaye

 

 

Sëy laa la yabe daal

Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage

 

Fatou Bèye

 

75

Yee bu la yalla yόbbo

Si Dieu fait que tu pars

 

Ba nga dem ca kër ga

Une fois dans ton foyer,

 

Bul xas ndaw ña

Ne sois pas insolente avec les enfants

 

Duma mag ña

Et ne bats pas les adultes

 

Sëy laa la yabe daal

Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage

 

Amy Ndiaye

 

80

Sëy laa la yabe daal

Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage

 

Fatou Bèye

 

 

Xale bi sëy laa la yabe daal

Jeune fille, je te recommande vivement de bien tenir ton ménage

 

Amy Ndiaye

 

 

Sëy laa la yabe daal

Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage

 

Fatou Bèye

 

 

Waay bu la yalla yóbbo

Oui si Dieu fait que tu pars

 

Ba nga dem ca kër ga

Une fois dans ton foyer,

85

Bul xas mag ña

Ne sois pas insolente avec les enfants

 

Duma ndaw ña

Ne bats pas les adultes

 

Sëy laa la yabe daal

Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage

 

Amy Ndiaye

 

 

Sëy laa la yabe daal

Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage

 

Fatou Bèye

 

 

Bilaay sëy laa ko yabe daal

Je jure que c’est ce que je lui recommande vivement

 

Amy Ndiaye

 

90

Sëy laa la yabe daal

Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage

 

Fatou Bèye

 

 

Yee bu la yalla yóbbo

Yee si Dieu fait que tu pars

 

Ba nga dem ca kër ga

Une fois dans ton foyer,

 

Bul xas ndaw ña

Ne sois pas insolente avec les enfants

 

Duma mag ña

Ne bats pas les adultes

95

Sëy laa la yabe daal

Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage

 

Saly Amy Diémé
Inalco/Plidam

Corpus inédit © Saly Amy Diémé

 


Notes:

[1]           Traduction de njël, provision de nourriture quotidienne d’une famille.

[2]           « Bien mélanger le tamarin » : satisfaire sexuellement une femme.

 

 

Télécharger le texte:

Téléchargement

Séyu démb — Les mariages du passé

 

Chant de mariage waliima

 

Mots-clés:  wolof, Sénégal — chant de mariage, taasu, waliima, denkaane — mariage, festivités.

Production du corpus:  La chanson présentée ici est énoncée par Tacko Diouf, accompagnée par les amies de la mariée — ci-dessous indiquées par « public ».

Collecte:  Le corpus est extrait d’un ensemble de 60 chants collectés par Saly Amy Diémé en juin-juillet 2015. Les enregistrements ont eu lieu pendant les cérémonies de mariage ou lors des performances sollicitées.

Descriptif:  Le texte est un chant de mariage waliima, qui appartient au répertoire traditionnel de chants de mariage wolof, le taasu.

Le terme waliima vient de l’arabe walīma / وليمة « réception ; festin ». De façon générale, dans le cadre du mariage musulman, il s’agit du repas qui précède les noces ; dans le mariage wolof, le waliima est plutôt une cérémonie de chants et de danses réservée aux femmes. Sa particularité au Sénégal est qu’elle n’est organisée que par des filles qui sont réputées observer les préceptes de la religion.

La fête a lieu chez la mariée, l’après-midi pendant ou après le mariage religieux, mais il arrive qu’elle soit organisée quelques jours après ce dernier.

Référence:

DIÉMÉ, Saly Amy, 2016, « La poésie orale dans les cérémonies de mariage wolof », Mémoire de Master 2, Oralité et anthropologie, préparé et présenté sous la direction d’Ursula Baumgardt et d’Abdoulaye Keïta, Paris, Institut National des Langues et Civilisations Orientales (INALCO), 209 p.

 


 

 

.

.


Chant de mariage waliima

 

Saly Amy DIÉMÉ, « La poésie orale dans les cérémonies de mariage wolof »,

Mémoire de Master 2, Oralité et anthropologie, Paris, INALCO, pp. 171-174

 

(Une deuxième version de la chanson est en cours de préparation)

 

Tacko Diouf

 
 

Séyu démb

Les conditions du mariage

 

Gënoon na fee metti

Étaient beaucoup plus difficiles

 

Public

 
 

Metti !

Difficiles !

 

Tacko Diouf

 
 

Yalla xam na

Dieu sait

5

Ni gënoon na fee metti

Qu’elles étaient plus difficiles

 

Suñu maam yi démb

Hier, nos grands-mères

 

Dañoo séy ba dee

Les ont endurées [ces conditions] jusqu’à leur dernier souffle.

 

Suma la waxe

Si je te dis d’être patiente

 

Soo demee muñal

D’être patiente une fois arrivée[1]

10

Nga war ma gëm

Tu dois me croire

 

Loolu waxi mag

Ce sont des propos de sage.

 

Public

 
 

Séyu démb

Les conditions du mariage

 

Gënoon na fee metti

Étaient beaucoup plus difficiles

 

Tacko Diouf

 
 

Metti

Difficiles !

 

Public

 

15

Yalla xam na ni

Dieu sait

 

Gënoon na fee metti

Qu’elles étaient beaucoup plus difficiles

 

Tacko Diouf

 
 

Waawaw !

Bien sûr !

 

Public

 
 

Suñu maam yi démb

Hier, nos grands-mères

 

Dañoo séy ba dee

Les ont endurées [ces conditions] jusqu’à leur dernier souffle

20

Suma la waxe

Si je te dis

 

Soo demee muñal

D’être patiente une fois arrivée

 

Nga wara déglu

Tu dois y prêter attention

 

Loolu waxi mag la

Ce sont des propos de sage

 

Tacko Diouf

 
 

Démb suuf ngay bale

Hier tu balayais le sable

25

Tey karo nga yor

Aujourd’hui tu as des carreaux.

 

Démb néegu ñax la

Hier c’était la case en paille,

 

Tey apartama

Aujourd’hui c’est l’appartement

 

Démb matt la woon

Hier c’était le bois de chauffage,

 

Tey gaas ngay togge

Aujourd’hui tu prépares avec du gaz.

30

Suma la waxee

Si je te dis

 

Soo demee muñal

D’être patiente une fois arrivée

 

Nga war ma gëm

Tu dois me croire

 

Loolu waxi mag

Ce sont des propos de sage

 

Public

 
 

Séyu démb gënoon

Les conditions du mariage étaient

35

Na fee metti

Beaucoup plus difficiles

 

Yalla xam na ne

Dieu sait

 

Gënoon na fee metti

Qu’elles étaient beaucoup plus difficiles

 

Sunu maam yi démb,

Hier, nos grands-mères les ont endurées [ces conditions]

 

Dañoo séy ba dee

Jusqu’à leur dernier souffle.

40

Suma la waxee

Si je te dis

 

Soo demee muñal

D’être patiente une fois arrivée

 

Nga wara déglu

Tu dois y prêter attention

 

Tacko Diouf

 
 

Ndeysaan !

Les pauvres[2] !

 

Public

 
 

Loolu waxi mag la

Ce sont des propos de sage

 

Tacko Diouf

 

45

Suñu maam yi démb

Hier nos grands-mères

 

Dañu gëmoon wax ñu topp

Étaient des femmes obéissantes

 

Yow mii le tey jiile

Et toi, aujourd’hui,

 

Tey ñu lay eemaasipeel

On te dit de t’émanciper maintenant

 

Bul topp yow mii

Oh toi ! Ne suis pas

50

Faam oksidantaal

Ces femmes occidentales.

 

Suma la waxee

Si je te dis

 

Jigéen day woyof

Qu’une femme doit être obéissante

 

Nga wara wacc

Tu dois être soumise

 

Loolu waxi mag la

Ce sont des propos de sage

 

Public

 

55

Séyu démb

Les conditions du mariage

 

Gënoon na fee metti

Étaient beaucoup plus difficiles

 

Yalla xam na

Dieu sait

 

Ne gënoon na fee metti

Qu’elles étaient beaucoup plus difficiles

 

Sunu maam yi démb

Hier, nos grands-mères

60

Dañoo séy ba dee

Les ont endurées [ces conditions] jusqu’à leur dernier souffle

 

Suma la waxee

Si je te dis

 

Soo demee muñal

D’être patiente une fois arrivée

 

Nga war ma déglu

Tu dois y prêter attention

 

Loolu waxi mag la

Ce sont des propos de sage

 

Tacko Diouf

 

65

Suñu maam yi démb

Hier, nos grands-mères

 

Dañu gëmoon wax ñu topp

Étaient des femmes obéissantes

 

Yow mii le tey jiile

Et toi, aujourd’hui,

 

Tey ñu lay eemaasipeel

On te dit de t’émanciper maintenant

 

Bul toop yow mii

Oh toi ! Ne suis pas

70

Faam oksidantaal

Ces femmes occidentales.

 

Suma la waxee

Si je te dis

 

Jigéen day wàcc

Qu’une femme doit être soumise

 

Nga wara woyof

Tu dois être obéissante

 

Loolu waxi mag la

Ce sont des propos de sage

Saly Amy Diémé
Inalco/Plidam

Corpus inédit © Saly Amy Diémé

 


Notes:

[1]           Une fois arrivée à la maison conjugale.

[2]           Exprime ici la compassion pour les difficiles conditions de mariage des grand-mères dans le passé.

 

Télécharger le texte:

Téléchargement
Site WordPress - ELLAF par Adellaf - ISSN 2804-7672 (en ligne) - Hébergé par Huma-num -©- 2019