Chant de mariage denkaane
Mots-clés: wolof, Sénégal — chant de mariage, taasu, waliima, denkaane — mariage, festivités.
Production du corpus: Chanson énoncée par Fatou Bèye et Amy Ndiaye
Collecte: Le corpus est extrait d’un ensemble de 60 chants collectés par Saly Amy Diémé en juin-juillet 2015. Les enregistrements ont eu lieu pendant les cérémonies de mariage ou lors des performances sollicitées.
Descriptif: Le texte est un chant de mariage denkaane, qui appartient au répertoire traditionnel de chants de mariage wolof, le taasu.
Le terme denkaane ou « recommandations » désigne à la fois les recommandations données aux époux avant la nuit de noces et les chants par lesquels la mariée est accompagnée au domicile conjugal.
La cérémonie a toujours lieu la nuit. Elle commence dès le départ du cortège jusqu’à l’entrée du village ou du quartier du marié. Les énonciatrices, amies de la même classe d’âge que la mariée chantent leur désolation de voir cette dernière partir. Les chants sont habituellement des conseils adressés à l’épouse. Le chant présenté ici contient des recommandations qui s’adressent aussi bien à la mariée qu’à son époux.
Référence:
DIÉMÉ, Saly Amy, 2016, « La poésie orale dans les cérémonies de mariage wolof », Mémoire de Master 2, Oralité et anthropologie, préparé et présenté sous la direction d’Ursula Baumgardt et d’Abdoulaye Keïta, Paris, Institut National des Langues et Civilisations Orientales (INALCO), 209 p.
.
.
.
Chant de mariage denkaane
Saly Amy DIÉMÉ, « La poésie orale dans les cérémonies de mariage wolof », Mémoire de Master 2 Oralité et anthropologie, Paris, INALCO, pp. 191-193
|
|
Amy Ndiaye |
|
|
Bu ko dόor te bu ko saaga yaay |
Ne la bats pas et n’insulte pas sa mère |
|
Dee ko muñalee |
Sois tolérant avec elle |
|
Fatou Bèye |
|
|
Bu ko dóor te bu ko saaga yaay |
Ne la bats pas et n’insulte pas sa mère |
|
Dee ko muñalee |
Sois tolérant avec elle |
|
Amy Ndiaye |
|
5 |
Bu ko dóor yaay te bu ko saaga |
Mon cher, ne la bats pas et ne l’insulte pas |
|
Dee ko muñalee |
Sois tolérant avec elle |
|
Fatou Bèye |
|
|
Waay bu ko dóor yaay |
Mon cher, ne la bats pas |
|
Te bu ko saaga yaay |
Et n’insulte pas sa mère |
|
Dee ko muñalee |
Sois tolérant avec elle |
|
Amy Ndiaye |
|
10 |
Bul dóor yaay te bu ko saaga |
Mon cher, il ne faut pas la battre ni l’insulter |
|
Dee ko muñalee |
Sois tolérant avec elle |
|
Fatou Bèye |
|
|
Boo koy dóor te di ko saaga yaay |
Si tu la bats et insultes sa mère |
|
Léeg mu ñibbisee |
Elle rentrera bientôt chez elle |
|
Amy Ndiaye |
|
|
Bul dóor yaay te bul saaga |
Mon cher, ne la bats pas et ne l’insulte pas |
15 |
Dee ko muñalee |
Sois tolérant avec elle |
|
Fatou Bèye |
|
|
Bu ko dóor yaay |
Mon cher, ne la bats pas |
|
Te bu ko saaga yaay |
Et n’insulte pas sa mère |
|
Dee ko muñalee |
Sois tolérant avec elle |
|
Amy Ndiaye |
|
|
Bu ko dóor |
Ne la bats pas |
20 |
Te bu ko saaga yaay |
Et n’insulte pas sa mère |
|
Dee ko muñalee |
Sois tolérant avec elle |
|
Fatou Bèye |
|
|
Boo koy dóor |
Si tu la bats |
|
Te di ko saaga yaay |
Et insultes sa mère |
|
Léeg mu ñibbisee |
Elle va bientôt rentrer chez elle |
|
Amy Ndiaye |
|
25 |
Boo kooy dóor |
Si tu la bats |
|
Te di ko saaga yaay |
Et insultes sa mère, |
|
Léeg mu ñibbisee |
Elle va bientôt rentrer chez elle. |
|
Fatou Bèye |
|
|
Bul ko yor yorub baayam |
Ne l’éduque pas à la manière de son père |
|
Amy Ndiaye |
|
|
Céy ! |
Ça alors ! |
|
Fatou Bèye |
|
30 |
Waay ne bul ko yor |
Répète, ne l’éduque pas |
|
Yorub baayam |
À la manière de son père |
|
Amy Ndiaye |
|
|
Ee bul ko yor yorub baayam |
Hé, ne l’éduque pas à la manière de son père |
|
Fatou Bèye |
|
|
Waawaw bul ko yor |
Bien sûr, ne l’éduque pas |
|
Yorub baayam |
À la manière de son père |
|
Amy Ndiaye |
|
35 |
Bul ko yor yorub baayam |
Ne l’éduque pas à la manière de son père |
|
Fatou Bèye |
|
|
Baayam, |
Son père, |
|
Du saaq njël |
Ne donne pas de provision quotidienne[1] |
|
Te du katte |
Ne [la] baise pas, |
40 |
Te du daqar ba mu saf |
Ne mélange pas bien le tamarin[2] |
|
Bul ko yor yorub baayam |
Ne l’éduque pas à la manière de son père |
|
Amy Ndiaye |
|
|
Ee bul ko yor |
Hé toi, ne l’éduque pas |
|
Yorub baayam |
À la manière de son père |
|
Fatou Bèye |
|
|
Baayam, |
Son père, |
45 |
Du saaq njël |
Ne donne pas de provision quotidienne |
|
Te du katte |
Ne [la] baise pas, |
|
Te du daqar ba mu saf |
Ne mélange pas bien le tamarin |
|
Bul ko yor yorub baayam |
Ne l’éduque pas à la manière de son père |
|
Amy Ndiaye |
|
|
Ee yow bul ko yor |
Hé toi, ne l’éduque pas |
50 |
Yorub baayam |
À la manière de son père |
|
Fatou Bèye |
|
|
Bul ko yor |
Ne l’éduque pas |
|
Yorub baayam |
À la manière de son père |
|
Amy Ndiaye |
|
|
Yow bul ko yor |
Toi, ne l’éduque pas |
|
Yorub baayam |
À la manière de son père |
|
Fatou Bèye |
|
55 |
Waay sëy laa la yabale |
Je te recommande de bien tenir ton ménage |
|
Sëy laa la yabale |
Je te recommande de bien tenir ton ménage |
|
Bu la yalla yóbbo |
Si Dieu fait que tu pars, |
|
Ba nga dem ca kër ga |
Une fois dans ton foyer |
|
Bul xas ndaw ña |
Ne sois pas insolente avec les enfants, |
60 |
Duma mag ña |
Ne bats pas les adultes |
|
Sëy laa la yabe daal |
Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage |
|
Amy Ndiaye |
|
|
Ee sëy laa la yabe daal |
Hé je te recommande vivement de bien tenir ton ménage |
|
Fatou Bèye |
|
|
Waay sëy laa la yabe man |
Moi, je te recommande de bien tenir ton ménage |
|
Amy Ndiaye |
|
|
Sëy laa la yabe man |
Moi, je te recommande de bien tenir ton ménage |
|
Fatou Bèye |
|
65 |
Yee sëy laa la yabe daal |
Yee je te recommande vivement de bien tenir ton ménage |
|
Amy Ndiaye |
|
|
Sëy laa la yabe man |
Moi, je te recommande de bien tenir ton ménage |
|
Fatou Bèye |
|
|
Waay bu la yalla yóbbo |
Si Dieu fait que tu pars |
|
Ba nga dem ca kër ga |
Une fois dans ton foyer, |
|
Bul xas ndaw ña |
Ne sois pas insolente avec les enfants |
70 |
Duma mag ña |
Ne bats pas les adultes |
|
Sëy laa la yabe daal |
Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage |
|
Amy Ndiaye |
|
|
Sëy laa la yabe daal |
Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage |
|
Fatou Bèye |
|
|
Yee sëy laa la yabe waay |
Yee je te recommande vivement de bien tenir ton ménage |
|
Amy Ndiaye |
|
|
Sëy laa la yabe daal |
Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage |
|
Fatou Bèye |
|
75 |
Yee bu la yalla yόbbo |
Si Dieu fait que tu pars |
|
Ba nga dem ca kër ga |
Une fois dans ton foyer, |
|
Bul xas ndaw ña |
Ne sois pas insolente avec les enfants |
|
Duma mag ña |
Et ne bats pas les adultes |
|
Sëy laa la yabe daal |
Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage |
|
Amy Ndiaye |
|
80 |
Sëy laa la yabe daal |
Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage |
|
Fatou Bèye |
|
|
Xale bi sëy laa la yabe daal |
Jeune fille, je te recommande vivement de bien tenir ton ménage |
|
Amy Ndiaye |
|
|
Sëy laa la yabe daal |
Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage |
|
Fatou Bèye |
|
|
Waay bu la yalla yóbbo |
Oui si Dieu fait que tu pars |
|
Ba nga dem ca kër ga |
Une fois dans ton foyer, |
85 |
Bul xas mag ña |
Ne sois pas insolente avec les enfants |
|
Duma ndaw ña |
Ne bats pas les adultes |
|
Sëy laa la yabe daal |
Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage |
|
Amy Ndiaye |
|
|
Sëy laa la yabe daal |
Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage |
|
Fatou Bèye |
|
|
Bilaay sëy laa ko yabe daal |
Je jure que c’est ce que je lui recommande vivement |
|
Amy Ndiaye |
|
90 |
Sëy laa la yabe daal |
Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage |
|
Fatou Bèye |
|
|
Yee bu la yalla yóbbo |
Yee si Dieu fait que tu pars |
|
Ba nga dem ca kër ga |
Une fois dans ton foyer, |
|
Bul xas ndaw ña |
Ne sois pas insolente avec les enfants |
|
Duma mag ña |
Ne bats pas les adultes |
95 |
Sëy laa la yabe daal |
Je te recommande vivement de bien tenir ton ménage |
Saly Amy Diémé
Inalco/Plidam
Corpus inédit © Saly Amy Diémé
Notes:
[1] Traduction de njël, provision de nourriture quotidienne d’une famille.
[2] « Bien mélanger le tamarin » : satisfaire sexuellement une femme.
Télécharger le texte:
Téléchargement